Bible Study: FrontPage




 

1 Corinthians, Chapter 16

Bible Study - 1 Corinthians 16 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Léegi nag ci li jëm ci ndimbal, li ñuy sàkkal gaayi Yàlla yi, defleen li ma tëral ci mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Galasi.
  
2. Bés bu jëkk ci ayu-bés yi, na ku nekk ber lu mu àttan, denc ko, ngir saa yu ma dikkee, ñu bañ di wër di laaj xaalis.
  
3. Su ma dikkee, dinaa dénk seen xaalis ñi ngeen tànn, yónni leen Yerusalem, boole ko ak bataaxal.
  
4. Su aajoo ma demal sama bopp, kon dinañu ànd ak man.
  
5. Gannaaw bu ma jàllee diiwaanu Maseduwan, dinaa ñëw ci yéen, ndaxte fas naa ko yéenee jàll.
  
6. Man na am ma yàgg ci yéen, jombul sax ma lollikoo fi yéen. Noonu dingeen taxawu sama yoon, fu ma man a jëm.
  
7. Ndaxte fi mu ne bëgguma leen a gis rekk, jàll, waaye yaakaar naa ne, dinaa toog ci yéen ab diir, bu neexee Boroom bi.
  
8. Ba tey dinaa toog fii ci dëkku Efes ba màggalu Pàntakot,
  
9. ndaxte Yàlla ubbil na ma bunt, ba mu ne làññ, ngir may def liggéey bu man a am muj gu rafet, te noon yu bare bëgg a gàllankoor liggéey bi.
  
10. Bu leen Timote ganesee, fexeleen ba bumu am njàqare ci seen biir, ndaxte dafay liggéeyal Boroom bi ni man.
  
11. Kon bu ko kenn xeeb. Nangeen taxawu yoonam, ba mu dellusi ci man ci jàmm, ndaxte maa ngi koy xaar ak bokk yi.
  
12. Naka Apolos sunu mbokk mi nag moom, xiir naa ko ay yooni yoon, mu ñëw ci yéen, ànd ak bokk yi. Waaye fi mu ne dëppoowul ak coobareem. Dina ñëw saa su ko manee.
  
13. Farluleen te dëgër ci ngëm, di góor-góorlu te am pasteef.
  
14. Lépp li ngeen di def, defleen ko ak mbëggeel.
  
15. Xam ngeen ne, Estefanas ak njabootam ñoo jëkk a nangu xebaar bu baax bi ci diiwaanu Akayi, te ñoo joxe seen bopp, ngir liggéeyal gaayi Yàlla yi. Kon nag bokk yi, maa ngi leen di ñaan,
  
16. ngeen nangul nit ñu mel noonu, ñoom ak képp ku ànd ak ñoom ci liggéey bi.
  
17. Bi ma Estefanas ak Fortunatus ak Akaykus seetsee, bég naa ci lool. Taxawal nañu leen ci topptoo, bi ngeen yéene woon ci man te tële ko.
  
18. Seral nañu sama xol ak seen yos itam. Kon fonkleen nit ñu mel noonu.
  
19. Mboolooy ñi gëm te nekk diiwaanu Asi ñu ngi leen di nuyu. Akilas ak Pirsil, ñu ngi leen di nuyu bu baax ci Boroom bi, ñoom ak mbooloom ñi gëm tey daje seen kër.
  
20. Bokk yépp ñu ngi leen di nuyu. Saafoonteleen ak xol bu laab.
  
21. Man Pool maa bind nuyoo bii ci sama loxob bopp.
  
22. Képp ku bañ Boroom bi, Yal na ko Yàlla alag. Boroom bi, ñëwal!
  
23. Na yiwu Boroom bi Yeesu ànd ak yéen.
  
24. Bëgg naa leen yéen ñépp ndax sunu booloo ak Yeesu Kirist.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES