Bible Study: FrontPage




 

2 Corinthians, Chapter 2

Bible Study - 2 Corinthians 2 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Man nag fas yéene naa lii: duma dellusi ci yéen ci naqar.
  
2. Ndaxte su ma leen tegee naqar, kuy seddal sama xol ku dul yéen ñi ma teg aw naqar?
  
3. Looloo tax ma binde noonu, ngir bañ a agsi, am naqar ci ñi ma waroon a bégal. Am naa kóolute ci yéen ñépp ne, sama mbég mooy seen mbég.
  
4. Ci biir tiis ak xol bu jeex laa leen bind, samay bët taa ak ay rangooñ. Binduma leen ngir teg leen naqar, waaye ngir ngeen xam xóotaayu mbëggeel gi ma am ci yéen.
  
5. Su kenn tegee moroomam naqar, du man la ko teg, waaye man nanu ne, yéen ñépp la ko teg — matul may réyal mbir mi.
  
6. Àtte bi ko mbooloo mi teg, doy na.
  
7. Léegi nag baal-leen ko te dëfël xolam, ngir bañ mu sóobu ci naqar wu ëpp.
  
8. Kon maa ngi leen di ñaan, ngeen feddali seen mbëggeel ci moom.
  
9. Nattu leen moo tax ma bind leen it, ngir seet ba xam dingeen dégg ndigal ci lépp.
  
10. Ku ngeen baal, ma baal ko itam. Man nag, su ma baalee --fekk am lu ma war a baale — yéena tax ma def ko ci kanamu Kirist,
  
11. ngir Seytaane bañ a am bunt bu mu jaar ba nax nu, ndaxte réerewunu mbir ay pexeem.
  
12. Ba ma àggee Torowas nag, ngir yégle fa xebaar bu baax bi ci Kirist, Boroom bi ubbil na ma ci bunt.
  
13. Waaye sama xel dalul benn yoon, ndax li ma fa fekkul sama mbokk, Tit. Noonu nag ma tàggu leen, daldi dem diiwaanu Maseduwan.
  
14. Waaye cant ñeel na Yàlla! Ci sunu booloo ak Kirist, daf nuy yóbbaale saa su nekk ci gawari ndamam, tey jaar ci nun ngir turu Kirist jolli fu nekk, ni xetu latkoloñ di tasaaroo.
  
15. Ndaxte ci Yàlla, xetu Kirist gu neex lanu, di gilli jëm ci ñiy mucc ak ñiy sànku;
  
16. ci ñu mujj ñii, xet gu sedd lanu, guy jëme ci dee; ci ñu jëkk ñi, xetu dund lanu, guy jëme ci dund. Kon ku man a àttan yen boobu!
  
17. Nun nag melunu ni ñu bare, ñiy baana-baana ci kàddug Yàlla, waaye ci sunu booloo ak Kirist, nu ngi waare ak xol bu laab fa kanam Yàlla, ni yonenti Yàlla.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES