Bible Study: FrontPage




 

2 Corinthians, Chapter 9

Bible Study - 2 Corinthians 9 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Ci mbirum ndimbal loolu jëm ci gaayi Yàlla yi, matul ma leen di bindaat,
  
2. ndaxte xam naa seen yéene ju rafet, te maa ngi ciy damu ci kanamu waa Maseduwan, naan leen: «Daaw fekk na waa Akayi jekk.» Te seen cawarte xamb na ñu bare ci ñoom.
  
3. Maa ngi yónni nag bokk yooyu, ngir damu gi nu doon damu ci yéen ci mbir mii bañ a neen, te ngeen jekk, ni ma ko waxe woon.
  
4. Danoo bañ rekk waa Maseduwan, ñiy ànd ak man, fekk jekkaguleen; te kon kóolute googu nu am ci yéen dina nekk sunu gàcce, waxaalewuma nag seen bos.
  
5. Moo tax ma xalaat ne, li gën mooy yónni bokk yooyu, ñu jiitu ma ci yéen, topptoo mbiri ndimbal lu yaatu loolu ngeen dige woon. Loolu di may gu tàlli, te bañ a nekk yëfi nay.
  
6. Te lii moo am: ku ji tuuti, góob tuuti; ku ji lu bare, góob lu bare.
  
7. Kon na ku nekk joxe, ni mu ko nase ci xolam, te bañ cee am réccu walla sañul-bañ, ndaxte kiy joxe ak mbég moo neex Boroom bi.
  
8. Te Yàlla man na leen a woomal ci bépp yiwam ba ci fépp ak ci lépp, ngeen faj seen soxla yépp te sakkanle it ngir bépp jëf bu baax.
  
9. Moom la Mbind mi wax ne:«Tabe na, ba may baadoolo yi;njubteem day sax ba fàww.»
  
10. Yàlla miy jox beykat bi jiwu ak nit ab dund, dina leen jox jiwu wu ne gàññ, te sakkanal li seen njub meññ.
  
11. Noonu dingeen woomle ci lépp, ba yéwén ci bépp anam, ba tax ñu bare gërëm Yàlla ndax li ngeen maye jaarale ko ci nun.
  
12. Ndaxte njaamu, gi ngeen di jaamu, yemul rekk ci faj soxlay gaayi Yàlla yi, waaye dina tax it ngërëmu ñu bare baawaan, jëm ci Yàlla.
  
13. Ci li ngeen firndeel seen mbëggeel ci joxe ndimbal lii, dinañu màggal Yàlla, ndaxte wone ngeen ni ngeen déggale xebaar bu baax bu Kirist bi, ak ni ngeen yéwéne ci seen ndimbal jëme ci ñoom ak ñépp.
  
14. Rax-ca-dolli dinañu sant Yàlla ak xol bu fees ak cofeel ci yéen ndax yiw wu mag, wi Yàlla def ci yéen.
  
15. Jërë-jëfati yaw Yàlla ndax sa may googu weesu dayo!


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES