Bible Study: FrontPage




 

Hebrews, Chapter 4

Bible Study - Hebrews 4 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Yàlla dige na ne, dina am ñu dugg ca noflaayam. Kon ndegam dige boobu mi ngi taxaw ba tey, moytuleen ba kenn ci yéen réer ba du dugg ci noflaay boobu.
  
2. Nun jot nanu xebaar bu baax bi ni ñoom, waaye kàddu, ga ñu déggoon, jariñu leen dara, ndaxte boolewuñu ci ngëm, ba ñu koy déglu.
  
3. Nun ñi gëm nag nooy dugg ci noflaayam, ni ko Mbind mi waxe:«Giñ naa kon ci sama mer ne:“Duñu dugg mukk ci sama noflaay,”» doonte sax liggéeyam bépp matoon na, ca ba mu sàkkee àddina ak léegi. Ci lu jëm ci juróom-ñaareelu fan ba,
  
4. am na fu ñu wax ci Mbind mi ne:«Yàlla noppalu na ci liggéeyam béppca juróom-ñaareelu fan ba.»
  
5. Te it waxoon na ci baat yi nu jot a lim ba noppi:«Duñu dugg mukk ci sama noflaay.»
  
6. Kon am na ñu ci war a dugg ba tey. Te ñi jëkkoon a jot xebaar bu baax bi, dugguñu ci ndax seen déggadi.
  
7. Noonu ay ati at gannaaw ga, Yàlla àppaat na beneen bés, def ko «tey jii,» bi mu waxee ci gémmiñu Daawuda ci baat yii ñu jot a lim:«Bu ngeen déggee tey jii baatu Yàlla bi,buleen dëgër bopp.»
  
8. Su Yosuwe duggaloon sunu maam ya ca noflaayu Yàlla ba, kon gannaaw gi Yàlla du wax dara ci lu jëm ci beneen bés.
  
9. Kon ba tey Yàllaa ngi dencal ay gaayam noflaay bu nirook noflaayu Yàlla ca juróom-ñaareelu fan ba.
  
10. Ndaxte képp ku mas a dugg ca noflaayu Yàlla, noppalu na ci ay jëfam ni Yàlla.
  
11. Nanu farlu boog, ngir dugg ci noflaay boobu, ba kenn bañ a déggadi, ba daanu ni maam ya ca màndiŋ ma.
  
12. Xam nanu ne, kàddug Yàlla mi ngi dund te am na doole. Moo gën a ñaw jaasiy ñaari boor. Day dagg ba fa xol ak xel digaloo, ba fa yax yi ak yuq gi di teqalikoo, te man na àtte xalaat yi ak mébéti xol.
  
13. Te itam amul mbindeef mu man a nëbbu Yàlla, waaye lépp a ubbiku, ba ne fàŋŋ ci bëti ki nu war a àtte.
  
14. Gannaaw am nanu saraxalekat bu mag-a-mag bu àgg ba ca kanam Yàlla, di Yeesu Doomu Yàlla ji, nanu jàpp bu dëgër yoon wi nu gëm.
  
15. Saraxalekat bu mag bi nu am, du ku mënul a bokk ak nun sunuy naqar; moom sax far jaar na ci nattu ni nun ci bépp fànn, waaye deful bàkkaar.
  
16. Kon nag nanu am kóolute ci jege jalu Yàlla bu yiw ba, ngir jot yërmandeem ak yiwam, ngir mu wallu nu fu soxla taxawe.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES