Bible Study: FrontPage




 

James, Chapter 4

Bible Study - James 4 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Xeex yi ak xuloo yi ci seen biir nag, lu leen waral? Xanaa du ci seeni bëgg-bëgg, yiy xeex ci seeni cér?
  
2. Dangeen di mébét waaye dungeen am; dangeen di rey nit, boole ci kiñaan, waaye li ngeen di yóotu, dungeen ko jot; dangeen di xuloo ak a xeex waaye dungeen am dara, ndaxte ñaanuleen Yàlla.
  
3. Bu ngeen ñaanee sax, dungeen jot dara, ndax yéena ngi ñaan ci naaféq, ngir gën a topp seen nafsu.
  
4. Yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla, xanaa xamuleen ne mbëggeelu àddina, mbañeel la fa Yàlla? Ku bëgg a xaritoo ak àddina nag, noonoo nga ak Yàlla.
  
5. Xanaa yaakaar ngeen ne, Mbind mi day wax cig neen, ci li mu ne: «Yàlla am na mbëggeel gu fiir ci Xel mi mu def ci nun.»
  
6. Waaye yiwu Yàllaa ko ëpp. Moom la Mbind mi wax ne:«Yàlla dàq na ñi réy,waaye yiwal na ñi woyof.»
  
7. Kon nag wàkkirluleen ci Yàlla, waaye dàqleen Seytaane, te dina daw, ba sore leen.
  
8. Jegeleen Yàlla, mu jege leen. Yéen bàkkaarkat yi, sellal-leen seeni loxo; yéen ñi am xel ñaar, laabal-leen seeni xol.
  
9. Toroxluleen te naqarlu, bay jooy; defleen seeni ree aw naqar, te seen mbég nekk tiis.
  
10. Suufeel-leen seen bopp fa kanam Boroom bi, kon dina leen yékkati.
  
11. Yéen bokk yi, buleen ŋàññante. Ku ŋàññ sa moroom mbaa nga ñaaw njort, ba àtte ko, diiŋat nga yoonu Yàlla te àtte ko; ku àtte yoon wi nag sàmmoo ko, waaye danga koo àtte.
  
12. Kenn rekk mooy tëral yoon, kooku rekk mooy àtte; moo man a musle, moo man a alage. Te sax yaw miy àtte sa bokk yaay kan?
  
13. Léegi nag dégluleen, yéen ñiy wax ne: «Tey walla ëllëg dinanu dem ca dëkk sàngam, def fa at, di fa sàkku xaalis ci jula.»
  
14. Ndax dangeen a xam seen ëllëg? Te luy seen dund? Xanaa cóola doŋŋ luy naaw ci diir bu gàtt, daldi naaxsaay.
  
15. Lii kay ngeen waroon a wax: «Bu soobee Boroom bi, dinanu dund, tey def nàngam ak nàngam.»
  
16. Waaye fi mu ne, naagu ngeen bay damu, te damoo noonu baaxul.
  
17. Kon nag ku xam def lu baax te defoo ko, bàkkaar nga.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES