Bible Study: FrontPage




 

John, Chapter 21

Bible Study - John 21 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Bi ñu ca tegee ab diir, Yeesu feeñuwaat na ay taalibeem ca tefesu dex gu ñuy wax Tiberyàdd. Nii la deme woon:
  
2. Taalibey Yeesu yii àndoon nañu: Simoŋ Piyeer; Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi;» Nataneel, mi dëkk Kana ca diiwaanu Galile; doomi Sebede ak yeneen ñaari taalibe.
  
3. Simoŋ Piyeer ne leen: «Maa ngi nappi.» Ñu ne ko: «Nun it danuy ànd ak yaw.» Ñu dugg gaal, daldi dem. Waaye guddi googu jàppuñu dara.
  
4. Ci fajar gi Yeesu taxaw ca tefes ga, waaye taalibe yi xàmmiwuñu ko.
  
5. Yeesu ne leen nag: «Bokk yi, xanaa jàppuleen jën?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
  
6. Mu ne leen: «Sànnileen mbaal mi ci ndeyjooru gaal gi, bu ko defee ngeen jàpp.» Ñu sànni fa mbaal ma, mu fees ak jën, ba mënuñu ko woon a génne ndox mi.
  
7. Taalibe ba Yeesu bëggoon, ne Piyeer: «Boroom bi la!» Bi Simoŋ Piyeer déggee loolu, dafa woddoo mbubbam, ndaxte dafa summeeku woon, daldi sóobu ci dex gi.
  
8. Yeneen taalibe ya xëcc mbaal, mi fees dell ak jën, jëme ko ca tefes ga, ndaxte gaal ga sorewul woon; diggante bi waroon na tollook téeméeri meetar.
  
9. Bi ñu teeree, ñu gis ab taal, ñu ciy lakk ay jën, teg mburu ca wet ga.
  
10. Yeesu ne leen: «Indileen ci jën, yi ngeen jàpp.»
  
11. Simoŋ Piyeer yéeg ca gaal ga, daldi xëcc mbaal ma ca tefes ga, mu fees dell ak jën yu mag; matoon na téeméeri jën ak juróom-fukk ak ñett. Te li muy baree-bare lépp, taxul mbaal ma dog.
  
12. Yeesu ne leen: «Ñëwleen ndékki.» Kenn ci taalibe yi ñemewu koo laaj ki mu doon, ndaxte xam nañu ne, Boroom bi la.
  
13. Yeesu jegeñsi, jël mburu mi, jox leen, jox leen it jën.
  
14. Bi Yeesu dekkee ba tey, bii mooy ñetteelu yoon, bi mu feeñoo ay taalibeem.
  
15. Bi ñu ndékkee ba noppi, Yeesu ne Simoŋ Piyeer: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax gën nga maa bëgg, ni ma ñii bëgge?» Mu tontu ko ne: «Aaŋkay, Boroom bi, xam nga ne, bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama mbote yi.»
  
16. Noonu mu waxaat ko ne: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax bëgg nga ma?» Mu ne ko: «Aaŋkay, Boroom bi, xam nga ne, bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Sàmmal ma sama xar yi.»
  
17. Mu neeti ko ñetteel bi yoon: «Simoŋ doomu Yowaana, bëgg nga maam?» Piyeer am naqar ci li mu ko laaj ñetti yoon: «Ndax bëgg nga ma?» Mu tontu ko ne: «Boroom bi, xam nga lépp; xam nga ne bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama xar yi.
  
18. Ci dëgg-dëgg Piyeer, maa ngi la koy wax, bi nga dee ndaw yaa doon takk sa geño, di dem fu la neex. Waaye boo màggatee, dinga tàllal say loxo, keneen takkal la sa geño, yóbbu la foo bëggul.»
  
19. Ci baat yooyu la Yeesu doon misaale nan la Piyeer war a faatoo ngir jollil ndamu Yàlla. Noonu Yeesu ne ko: «Toppal ci man!»
  
20. Piyeer geestu, gis taalibe bi Yeesu bëggoon, di ñëw ci seen gannaaw. Taalibe boobu mooy ki sóonu woon ca Yeesu, ba ñuy lekk, te laajoon ko ne: «Boroom bi, kan moo lay wori?»
  
21. Piyeer gis ko, daldi ne Yeesu: «Kii nag, Boroom bi, nu muy mujje?»
  
22. Yeesu ne ko: «Su ma neexoon mu dund, ba ma dellusi, lu ciy sa yoon? Yaw toppal ci man.»
  
23. Noonu am, ci bokki taalibe yi, ñu xalaat ne, taalibe boobu du dee. Moona Yeesu musul ne Piyeer, du dee; waaye li mu wax mooy: «Su ma neexoon mu dund, ba ma dellusi, lu ciy sa yoon?»
  
24. Taalibe boobu mooy seede mbir yooyu, bind leen, te xam nanu ne, li muy wax dëgg la.
  
25. Yeesu def na yeneen jëf yu bare. Su ñu ko doon nettali, bind lépp, xalaat naa ne, téere yi duñu xaj ci àddina.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES