Bible Study: FrontPage




 

Mark, Chapter 11

Bible Study - Mark 11 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege nañu Yerusalem, ba agsi dëkki Betfase ak Betani ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaar ciy taalibeem,
  
2. ne leen: «Demleen ci dëkk bi ci kanam. Bu ngeen fa duggee, dingeen fa gis cumbur gu kenn musul a war. Yiwileen ko, indi.
  
3. Bu leen kenn nee: “Lu ngeen di def?” tontuleen ko: “Boroom bi da koo soxla, te léegi mu delloosi ko.”»
  
4. Taalibe ya dem nag, ñu gis cumbur ga ci mbedd mi, mu yeewe cib buntu kër.
  
5. Bi ñu koy yiwi nag, am na ca ña fa taxaw, ñu ne leen: «Lu ngeen nar, bay yiwi cumbur gi?»
  
6. Taalibe yi tontu leen, ni leen Yeesu digale woon, kon nit ñi bàyyi leen, ñu dem.
  
7. Ñu indi cumbur gi Yeesu nag, lal ci seeni yére, mu toog ci.
  
8. Ñu bare lal seeni yére ci yoon wi, ñenn ñi dagg ay cari garab ci tool yi, lal leen it ci yoon wi.
  
9. Ñiy jiitu ak ñiy topp ci Yeesu ñépp di wax ci kaw naan:«Osaana!Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi,ku barkeel nga!
  
10. Nguuru sunu maam Daawuda giy ñëw,dina barkeel!Ci bérab yu gën a kawe,nañu ne: “Osaana!”»
  
11. Noonu Yeesu dugg Yerusalem, dem kër Yàlla ga, xool lépp, ba noppi génn dem dëkku Betani, moom ak fukki taalibe ya ak ñaar, ndaxte dafa guddi.
  
12. Bët set ñu génn Betani, fekk Yeesu xiif.
  
13. Noonu mu séen fu sore garabu figg gu sëq, mu dem seeti, ndax am na ay doom. Waaye bi mu fa eggee, gisul lu dul ay xob, ndaxte jamonoy figg duggagul.
  
14. Ci kaw loolu mu ne garab gi: «Dootuloo meññ mukk!» Taalibe yi dégg loolu mu wax.
  
15. Bi ñu eggee Yerusalem, Yeesu dugg ci kër Yàlla gi, daldi dàq ñi fay jaay ak ñi fay jënd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis yi ak tooguy jaaykati pitax yi,
  
16. te mayul kenn, mu yóbbu am njaay ci kër Yàlla gi.
  
17. Mu di leen jàngal ne leen: «Ndax waxuñu ci Mbind mi:“Dees na wooye sama kërkëru ñaan ci Yàlla ngir xeet yépp”? Waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.»
  
18. Bi ko saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya déggee nag, ñu ragal ko, ndaxte mbooloo mépp dañoo waaru ci njàngaleem. Noonu ñu seet pexem reylu ko.
  
19. Bi timis jotee Yeesu ak taalibe yi génn dëkk bi.
  
20. Ci suba si, bi ñuy dem, ñu gis ne garabu figg gi dee na, ba wow koŋŋ.
  
21. Noonu Piyeer fàttaliku li xewoon, ne Yeesu: «Kilifa gi, xoolal, figg gi nga rëbb dee na, ba wow!»
  
22. Yeesu tontu ne: «Gëmleen Yàlla.
  
23. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku ne tund wale: “Jógal, tàbbi ca géej ga,” te nga gëm ne loolu dina am, bañ cee boole xel ñaar, kon sa ñaan nangu.
  
24. Moo tax maa ngi leen koy wax, bu ngeen di ñaan Yàlla, lépp lu ngeen ko man a laaj, gëmleen ne jot ngeen ko, te dingeen ko am.
  
25. Te it bu ngeen di ñaan, fekk ngeen jàppal kenn dara, baal-leen ko, ngir seen Baay bi ci kaw baal leen seeni tooñ, yéen itam.»
  
27. Gannaaw loolu ñu duggaat Yerusalem, te Yeesu doon doxantu ca ëtti kër Yàlla ga. Noonu saraxalekat yu mag ya ak xutbakat ya ak njiit ya dab ko
  
28. ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Te ku la may sañ-sañu def ko?»
  
29. Yeesu tontu leen: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ci tontoo, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.
  
30. La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?»
  
31. Bi ñu ko déggee, ñuy werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” kon dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
  
32. Waaye bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw;» ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent.
  
33. Ñu tontu Yeesu nag ne: «Loolu de xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.»


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES