Bible Study: FrontPage




 

Mark, Chapter 16

Bible Study - Mark 16 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Bi bésu noflaay bi wéyee, Maryaamam Magdala, Maryaama yaayu Saag, ak Salome, jënd cuuraay, ngir dem xeeñal néewu Yeesu.
  
2. Kon bés bu jëkk ci ayu-bés gi, ñu njëlu dem ca bàmmeel ba,
  
3. di laajante: «Ku nuy béraŋal doj, wiy ub bàmmeel bi?» Doj woowu nag bu réy-a-réy la woon. Noonu ñu xool, gis ne doj wa deñ.
  
5. Ñu dugg ci bàmmeel bi, gis ca ndeyjoor waxambaane wu sol mbubb mu weex, ñu daldi tiit.
  
6. Waaye mu ne leen: «Buleen tiit. Yéena ngi seet Yeesum Nasaret, mi ñu daajoon ci bant bi. Nekkatu fi, dekki na; gisleen fi ñu ko tëraloon.
  
7. Kon nag demleen, ne Piyeer ak taalibe ya: “Mi ngi leen di jiitu Galile. Foofa ngeen koy gise, ni mu leen ko waxe woon.”»
  
8. Noonu jigéen ñi génn, dawe bàmmeel ba, tiit bay lox. Te waxuñu kenn dara ndax seen tiit.
  
9. Bi Yeesu dekkee nag ci suba teel ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, mu jëkk a feeñu Maryaama mu dëkk Magdala, mi mu dàqe woon juróom-ñaari rab.
  
10. Maryaama nag dem nettali ko ñi àndoon ak Yeesu, fekk ñuy naqarlu, di jooy.
  
11. Bi ñu déggee ne, Yeesoo ngi dund te Maryaama gis na ko, gëmuñu ko.
  
12. Gannaaw loolu Yeesu feeñu ñaar ci ñoom ci jeneen jëmm, ñuy jaar ci yoon wi, jëm àll ba.
  
13. Ñu woññiku nag, wax ko ña ca des, waaye ba tey gëmuñu leen ñoom it.
  
14. Gannaaw ga it Yeesu feeñu fukki taalibe yi ak benn, bi ñuy lekk. Mu yedd leen ndax seen ngëmadi ak seen dëgër bopp, ci li ñu bañ a gëm ñi ko gisoon, bi mu dekkee.
  
15. Mu ne leen: «Demleen ci àddina sépp, yégal xebaar bu baax bi mbindeef yépp.
  
16. Ku gëm te ñu sóob ko ci ndox, dina mucc; ku gëmul, dees na ko daan.
  
17. Ñi ma gëm dinañu ànd ak firnde yii: ci sama tur dinañu dàq rab yi, di wax làkk yu bees,
  
18. di jàpp jaan ak seeni loxo; te bu ñu naanee lu ñu tooke, du leen wàññi dara, te jarag ju ñu teg loxo, mu wér.»
  
19. Gannaaw bi Boroom bi Yeesu waxee ak ñoom, mu yékkatiku, dem asamaan, toog ci ndeyjooru Yàlla.
  
20. Taalibe ya dem waareji, te loxob Boroom bi ànd ak ñoom, di dëggal kàddu gi ak firnde, yi ci ànd.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES