Bible Study: FrontPage




 

Revelation, Chapter 10

Bible Study - Revelation 10 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Noonu ma gis meneen malaaka mu am doole, muy wàcce asamaan, làmboo niir. Xon tiim ko, te xar-kanamam mel ni jant, te ay tànkam mel ni jumi safara.
  
2. Yor na benn téere bu ndaw bu ñu ubbi. Mu teg tànku ndeyjooram ci géej gi, tànku càmmooñam ci suuf si,
  
3. di xaacu, mel ni gaynde guy yëmmu. Naka la xaacu, juróom-ñaari dënnu yi jib.
  
4. Naka la juróom-ñaari dënnu yi di jib, may waaj a bind, waaye ma dégg baat bu jóge asamaan, naan ma: «Li juróom-ñaari dënnu yi wax, na nekk kumpa, bu ko bind.»
  
5. Noonu malaaka ma ma gis, mu taxaw ci géej gi ak suuf si, yékkati loxol ndeyjooram, mu jëm asamaan,
  
6. daldi waat ci kiy dund ba fàww, ki sàkk asamaan ak suuf ak géej ak li ci nekk lépp; mu ne: «Négandiku wees na,
  
7. waaye jamono ju juróom-ñaareelu malaaka ma wolee ci liitam, ndogalu Yàlla dina mat, ni mu ko waxe woon ay jaamam, yonent yi.»
  
8. Ci kaw loolu baat, ba ma déggoon ca asamaan waxaat ak man, ne ma: «Demal jël téere bi ñu ubbi ci loxob malaaka, mi taxaw ci géej gi ak suuf si.»
  
9. Ma dem ca malaaka ma, laaj ko téere bu ndaw boobu. Mu ne ma: «Jël ko te lekk ko. Dina wex ci sa biir, waaye dina neex ni lem ci sa gémmiñ.»
  
10. Noonu ma jël téere bi ci loxob malaaka mi, daldi ko lekk, mu neex ci sama gémmiñ ni lem, waaye bi ma ko wannee, mu wex xat ci sama biir.
  
11. Gannaaw loolu ñu ne ma: «Fàww nga wax ci kàddug Yàlla lu jëm ci réew yu bare, xeet yu bare, kàllaama yu bare ak buur yu bare.»


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES