Bible Study: FrontPage




 

Revelation, Chapter 12

Bible Study - Revelation 12 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Amoon na firnde ju ràññiku ju feeñ ca asamaan, di jigéen ju làmboo jant bi, kaalawoo fukki biddiiw ak ñaar, weer wi nekk ci suufu tànkam.
  
2. Jigéenu biir la, di yuuxu ndax metitu mat wu tar.
  
3. Noonu beneen firnde feeñ ca asamaan, di ninkinànka ju réy, xonq curr te am juróom-ñaari bopp ak fukki béjjén. Ca bopp ya am na juróom-ñaari mbaxanay buur.
  
4. Geenam di laawaale ñetti cér yu ne benn ca biddiiwi asamaan, di leen sànni ci suuf. Ninkinànka ja taxaw ca kanamu jigéen jay matu, ngir lekk liir ba, bu juddoo.
  
5. Noonu mu jur doom ju góor, muy ki war a jiite xeeti àddina yépp ak yetu weñ. Waaye ñu daldi fëkk doom ja, mu dem ca Yàlla ak gànguneem.
  
6. Gannaaw loolu jigéen ja daw, dem ca màndiŋ ma, ca dalukaay ba ko Yàlla waajaloon ngir mu nekk fa, ñu dundal ko fa diirub junni ak ñaari téeméeri fan ak juróom-benn-fukk.
  
7. Noonu xare am ca asamaan ya. Mikayel ak malaaka, ya ànd ak moom, xeex ak ninkinànka ja, ninkinànka ja it ak ay malaakaam feyyu.
  
8. Waaye ninkinànka jaa gën a néew doole; noonu ñu dàqe ko ak toppam asamaan.
  
9. Daaneel nañu ko, moom ninkinànka ju réy ji, di jaani cosaan ji, te ñu di ko wax Tuumaalkat bi mbaa Seytaane, moom miy nax waa àddina sépp — daaneel nañu ko ci kaw suuf, moom ak ay malaakaam.
  
10. Noonu ma dégg baat bu xumb jóge asamaan naan:«Léegi mucc agsi na,moom ak kàttanak nguuru Yàlla sunu Boroom,ak sañ-sañu Almaseem,ndaxte ki daan tuumaal sunuy bokk,di leen sosal guddi ak bëccëgci kanam Yàlla sunu Boroom,kooka daaneel nañu ko.
  
11. Fekk noot nañu kojaarale ko ci deretu Mbote maak seen seedes ngëm,te soppuñu seen bakkan ba ragal a dee.
  
12. Looloo tax, na asamaanak ñi ci dëkk bànneexu!Musiba ci kaw suuf ak ci biir géej!Ndaxte Seytaane wàcc na ci yéen,ànd ak mer mu tàng,ndaxte xam na ne, jot gi ko dese barewul.»
  
13. Ba ninkinànka ja gisee ne, daaneel nañu ko ci kaw suuf, mu dàq jigéen, ja juroon doom ju góor ja.
  
14. Noonu ñu jox jigéen ja ñaari laafi jaxaay ja, ngir mu naaw, ba sore ninkinànka ja, dem ca màndiŋ ma ca bérabam, ñu dundal ko fa ab diir, ay diir ak genn-wàllu diir.
  
15. Ninkinànka ja buusu ndox mu bare ni dex ca gannaaw jigéen ja, ngir yóbbaale ko ca.
  
16. Waaye suuf wallu jigéen ja, naan dex, ga ninkinànka ja buusu woon.
  
17. Ninkinànka ja mere jigéen ja, daldi xeexi ak ñi des ciy doomam, di ñiy sàmm ndigali Yàlla tey sax ci di seedeel Yeesu.
  
18. Noonu mu taxaw ca tefesu géej ga.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES