Bible Study: FrontPage




 

Revelation, Chapter 22

Bible Study - Revelation 22 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Noonu malaaka ma won ma dexu ndoxum dund, mu leer ni weer bu set, di génn ca gàngune mu Yàlla ak Mbote ma,
  
2. xellee ca digg péncu dëkk ba. Ca weti dex ga amoon na ca garabu dund, guy meññ fukki yoon ak ñaar, di meññ weer wu nekk, te xob ya di faj xeet yi.
  
3. Musiba dootul am. Gàngune mu Yàlla ak Mbote mi mu ngi ci dëkk bi, te ay jaamam dinañu ko jaamu.
  
4. Dinañu gis xar-kanamam, te turam dina nekk ci seen jë.
  
5. Guddi dootul am, te kenn dootul soxla leeru làmp walla naaju jant, ndaxte Boroom bi Yàlla moo leen di leeral. Te dinañu nguuru ba fàww.
  
6. Noonu malaaka ma ne ma: «Wax jii ju wóor la te dëggu. Boroom bi, Yàlla jiy leeral xeli yonent yi, moo yónni malaakaam, ngir mu won ay jaamam mbir yi dëgmël di ñëw.»
  
7. «Maa ngi ñëw léegi. Yaw miy sàmm waxi Yàlla, yi ci téere bii, barkeel nga.»
  
8. Man Yowaana maa dégg mbir yii te gis ko. Ba ma ko déggee te gis ko, damaa daanu ca tànki malaaka, ma ma ko doon won, bëgg koo jaamu.
  
9. Waaye mu ne ma: «Moytu koo def. Sa nawle laa ci liggéey bi, yaw ak say bokki yonent ak ñiy sàmm waxi téere bii. Jaamul Yàlla.»
  
10. Mu ne ma it: «Bul tëj téere bii ak waxi Yàlla yi mu ëmb, ndaxte waxtu wi jege na.
  
11. Ku jubadi, na sax ci jubadeem; ku taq sobe, na sigiñu ci sobeem; ku jub, na wéy ci jëf yu jub; ku sell, na ci ŋoy.»
  
12. Yeesu nee na: «Maa ngi ñëw léegi, indaale pey gi, ngir delloo ku nekk lu mengoo ak lu mu def.
  
13. Man maay Alfa ak Omega, ki jëkk te mujj, njàlbéen gi ak muj gi.
  
14. «Yéen ñi fóot seeni mbubb, ngir sañ a lekk ci garabu dund gi te dugg ci bunti dëkk bi, barkeel ngeen.
  
15. Waaye ñi ci biti ñooy xaj yi, luxuskat yi, njaalookat yi, bóomkat yi, xërëmkat yi ak ñépp ñiy sopp fen te di ci wéy.
  
16. «Man Yeesu maa yónni sama malaaka, ngir mu seede leen mbir yii ci digg mboolooy ñi gëm. Man maay car, bi soqikoo ci Daawuda, di biddiiwu njël bu leer bi.»
  
17. Te Xelum Yàlla ak séetu Mbote mi ñu ngi naan: «Ñëwal.» Képp ku dégg wax jii, na ne: «Ñëwal.» Na képp ku mar, ñëw; ku bëgg, duyal ci ndoxum dund mi te doo fey dara.
  
18. Man Yowaana maa ngi koy wax képp ku dégg waxi Yàlla, yi nekk ci téere bii: ku ci yokk dara, Yàlla dina dolli ci sa mbugal musiba, yi ñu wax ci téere bii.
  
19. Ku dindi dara ci waxi Yàlla, yi nekk ci téere bii, Yàlla dina dindi sa wàll ca garabu dund ga ak dëkk bu sell ba, ñaar yooyu ñu bind ci téere bii.
  
20. Kiy seede mbir yii nee na: «Waaw, maa ngi ñëw léegi.» Amiin. Boroom bi Yeesu, ñëwal.
  
21. Na yiwu Boroom bi Yeesu ànd ak yéen ñépp.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES