Bible Study: FrontPage




 

Romans, Chapter 10

Bible Study - Romans 10 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Bokk yi, sama coobareg xol ci bànni Israyil ak sama ñaan ci Yàlla, mooy ñu mucc.
  
2. Seedeel naa leen ne, ñu farlu lañu ci jaamu Yàlla, waaye seen njaamu àndul ak xam-xam.
  
3. Xamuñu yoon, wi Yàlla tëral ngir nit jub ci kanamam, waaye dañoo wéy ci seen pexey bopp; ba tax ñu bañ a nangu yoonu njub woowu Yàlla tëral.
  
4. Ndaxte ci Kirist la yoonu Musaa dëppe, ba tax ku ko gëm, dinga jub fa kanam Yàlla.
  
5. Ku bëgg a jub ci kanam Yàlla ci kaw sàmm yoon, Musaa daf cee wax ne: «Ku ko manoon a matal, dinga dund ba fàww.»
  
6. Waaye ku jub ci kanam Yàlla ci kaw ngëm, nii lay waxe:«Bul wax ci sa xol ne:“Kuy yéeg ci kaw?”» mel ni dangaa bëgg Kirist wàcc.
  
7. «Bul wax it:“Kuy dem ca barsàq?”» mel ni dangaa bëgg Kirist dekki.
  
8. Kon boog lan lay wax? Lii:«Waxu Yàlla mi ngi ci sa wet,ci sa làmmiñ, ci sa xol.» Te wax jooju lal ngëm lanuy waare.
  
9. Ndaxte soo waxee ak sa gémmiñ ne, Yeesu mooy Boroom bi, te nga gëm ci sa xol ne, Yàlla dekkal na ko, dinga mucc.
  
10. Ndax xol la nit di gëme, ba tax mu jub ci kanam Yàlla; làmmiñ it la nit di waxe ne, mi ngi ci Kirist, ba tax Yàlla musal ko.
  
11. Mbind mi dafa wax ne: «Képp ku ko gëm, sa yaakaar du tas mukk.»
  
12. Ndax ñépp a yem ci kanam Yàlla, muy Yawut mbaa ku dul Yawut, ndax kenn rekk mooy sunu Boroom nun ñépp, te ku yéwén la ci képp ku koy ñaan.
  
13. Ndaxte bind nañu: «Képp ku woo Boroom bi ciw turam, dinga mucc.»
  
14. Waaye nan lañuy wooye ki ñu gëmagul? Te naka lañu man a gëme ki ñu déggagul turam? Te naka lañu man a dégge turam, te kenn xamalu leen ko?
  
15. Te it nan lañu man a waaree, su leen kenn yónniwul? Looloo tax Mbind mi wax ne: «Ñiy yégle xebaar bu baax bi, ni seen ñëw di sedde xol!»
  
16. Waaye ñépp nanguwuñu xebaar bu baax bi; moom la Esayi wax ne: «Boroom bi, ana ku gëm sunu waare?»
  
17. Kon boog ngëm ci kaw dégg lay juddoo, te dégg sosoo ci xebaaru Kirist.
  
18. Waaye ma ne: xanaa ñépp dañoo déggul? Aaŋkay! Mbind mi wax na ne:«Seen baat jolli na ci ñeenti xebla yépp,seen wax wër na àddina sépp.»
  
19. Waaye ma teg ci ne: xanaa bànni Israyil dañoo xamul? Aaŋkay! Musaa dafa jëkkoon a wax ne:«Dinaa leen siisloo xeet wu bokkul ci Yàlla,merloo leen ci ñi xamul dara ci Yàlla.»
  
20. Te Esayi takk na fitam, ba wax ne:«Ñi ma wutul woon, gis nañu ma,feeñ naa ci ñi ma laajul woon.»
  
21. Waaye ci mbirum Israyil dafa wax ne:«Tàllal naa samay loxo, suba ba ngoon, ci xeet wu may bañ tey werante.»


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES