Bible Study: FrontPage




 

Romans, Chapter 13

Bible Study - Romans 13 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Gannaaw loolu na nit ku nekk déggal ñi yore baat ci kanamam; ndaxte amul njiit lu fi Yàlla sampul. Njiit yépp nag Yàlla moo leen fi teg.
  
2. Kon ku leen bañ a déggal, ndigalu Yàlla nga lànk, te ku def loolu, yoon dina la dab.
  
3. Kuy def lu baax warul a ragal njiit li, kuy def lu bon moo ko war a ragal. Soo ko bëggee bañ a ragal nag, kon defal lu baax, te dina la tagg.
  
4. Ndax Yàllaa ko dénk liggéey boobu ngir sa jàmm. Waaye sooy def lu bon, war ngaa ragal, ndax du cig neen la ame jaasiy àtte; jawriñu Yàlla la ngir wàcce meru Yàlla, ci fey ku def lu bon.
  
5. Kon fokk ngeen déggal ko, waxuma sax ndax sañ-sañam boobu, waaye it ngir seen xel dal.
  
6. Gannaaw Yàllaa sas njiit yi liggéey boobu, te ñi ngi ci, kon fàww ngeen fey galag.
  
7. Joxleen ku nekk céram; ku ngeen war a fey galag, feyleen ko ko; ku ngeen war a fey juuti, feyleen ko ko; ku ngeen war a weg, wegleen ko; ku ngeen war a teral, teral-leen ko.
  
8. Buleen ameel kenn dara, lu dul mbëggeel; ndax ku bëgg sa moroom, wàccoo nga ak yoonu Musaa.
  
9. Ndaxte ndigali Yàlla yépp, yi deme ni: «Bul njaaloo, bul rey nit, bul sàcc, bul bëgge,» walla leneen ndigal lu mu man a doon, wax jii moo leen ëmb: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
  
10. Ku bëgg sa moroom, doo ko tooñ; kon ku wéy ci mbëggeel matal nga yoonu Musaa.
  
11. Te lii itam am na: xam ngeen bu baax jamono ji nu tollu; jamonoy yeewu jot na, ndax léegi sunu mucc gën na noo jege, ca ba nu dooree gëm.
  
12. Guddi gi màggat na, bët a ngi bëgg a set. Nanu bàyyi nag jëf yu lëndëm te ràngoo gànnaay yi nu Yàlla jox, ngir dund ci leer.
  
13. Gannaaw nu ngi ci leer, na sunug dund rafet. Bunu naan sangara ba màndi tey bànneexu; bunu njaaloo tey def i ñaawteef ak sunuy cér; bunu xuloo mbaa nuy ñeeyante.
  
14. Waaye gànnaayooleen Yeesu Kirist Boroom bi, te bañ a topp seen bakkan ciy bëgg-bëggam yu bon.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES