Bible Study: FrontPage




 

Titus, Chapter 2

Bible Study - Titus 2 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Yaw nag nangay waare li dëppook njàngale mu wér mi.
  
2. Maanaa, na góor ñu mag ñi foog, am faayda te maandu, di ñu wér ci seen ngëm, seen mbëggeel ak seen muñ.
  
3. Jigéen ñu mag ñi itam, na seen doxalin ànd ak faayda; buñuy jëw mbaa xér ci sangara. Waaye nañuy jàngale lu baax,
  
4. bay sol ci boppu jeeg yu ndaw yi, ñu bëgg seeni jëkkër ak seeni doom,
  
5. di ñu maandu, sell te fonk seen kër, ñu neex deret te déggal seeni jëkkër, ngir kenn bañ cee gàkkal kàddug Yàlla.
  
6. Naka noonu itam nanga xiir waxambaane yi cig maandu.
  
7. Te yaw, ci lépp lu mu man a doon, nekkal ab royukaay ci jëf yu baax. Na sa njàngale wér te am faayda,
  
8. ànd ak wax yu wér yu kenn mënta diiŋat, ngir sunuy noon rus ba wedam, ci li ñu amul dara lu ñu nu tuumaal.
  
9. Waxal it jaam ñi, ñu déggal seeni sang ci lépp, te liggéeyal leen ba seral seen xol, bañ cee boole werante
  
10. mbaa sàcc. Waaye nañu wone takkute gu mat, ba rafetal ci lépp njàngalem Yàlla sunu Musalkat.
  
11. Ndaxte yiwu Yàlla feeñ na te ubbil na ñépp buntu mucc.
  
12. Moo nu digal, nu dëddu weddi ak bëgg-bëggi jamono, tey dund ci àddina cig maandu, njub ak ragal Yàlla,
  
13. di séentu bés bu tedd bi nu yaakaar, maanaa Yàlla ju màgg ji, di sunu Musalkat Yeesu Kirist, feeñ ci biir ndamam.
  
14. Joxe na bakkanam ngir nun, ba jot nu ci lépp lu bon, te beral nu boppam, di xeet wu sell te ràññiku ci jëf yu baax.
  
15. Jàngaleel loolu, di leen dénk ak a yedd ak fulla ju mat. Bu la kenn yab.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES