Bible Study: FrontPage




 

1 Timothy, Chapter 2

Bible Study - 1 Timothy 2 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Fii laay tàmbale nag: maa ngi leen di dénk, ngeen yóbbu ñépp fa kanam Yàlla ciy ñaan, ay tinu ak i ngërëm.
  
2. Ñaanal-leen buur yi ak kilifa yépp, ngir nu man a am dund gu dal te jàmmu, ànd ak ragal Yàlla ak faayda yu mat.
  
3. Loolu mooy li rafet te neex Yàlla sunu Musalkat,
  
4. bi bëgg ñépp mucc te xam dëgg gi.
  
5. Ndaxte jenn Yàlla kepp moo am, ak benn Rammukat kepp diggante Yàlla ak nit ñi, di nit ki Kirist Yeesu,
  
6. mi joxe bakkanam ngir jot ñépp. Loolu mooy seede si Yàlla joxe, bi waxtu wi jotee.
  
7. Te fal na ma ci ndaw ak jàngalekat, may yégal xeeti àddina yoonu ngëm ak dëgg; fenuma, dëgg rekk laay wax.
  
8. Li ma bëgg kon mooy lii: na góor ñi ñaan ci Yàlla fu nekk, tàllal ko loxo yu sell, te bañ cee boole mer mbaa werante.
  
9. Naka noonu itam, na jigéen ñi di sol col gu faaydawu, cig woyof ak maandu. Buñu def seen xel ciy létt ak ci takkaayu wurus, mbaa ciy per ak col gu jafe.
  
10. Waaye na seen col di jëf yu rafet, ndaxte looloo jekk ci jigéen juy woote ag ragal Yàlla.
  
11. Te it na jigéen jàng cig noppi, ànd ak déggal gu mat.
  
12. Mayuma jigéen, muy jàngale mbaa muy jiite góor, waaye na noppi.
  
13. Ndaxte Aadama la Yàlla jëkk a sàkk, door caa teg Awa.
  
14. Te it du Aadama la Seytaane nax, waaye jigéen ja la nax, ba mu jàdd.
  
15. Teewul jigéen dina mucc ci wasin, su saxee ci ngëm ak mbëggeel, di ku sell te maandu.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES