Bible Study: FrontPage




 

1 Timothy, Chapter 3

Bible Study - 1 Timothy 3 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Wax ju wóor a ngii: kuy sabablu yenub sàmm mbooloo mi, mu ngi yóotu liggéey bu rafet.
  
2. Sàmm bi nag, nii la war a mel: war na ñàkk ŋàññ, yem ci benn soxna, moom boppam te maandu; war na am faayda, man gan te am mayu jàngale;
  
3. warul di ab màndikat mbaa xeexkat, waaye na lewet te jàmmu, bañ a bëgge ci xaalis.
  
4. Na yor këram yorin wu rafet, te ay doomam déggal ko ak teggin yu mat.
  
5. Ndaxte ku mënta yor njabootam, naka lay man a yore njabootu Yàlla?
  
6. Te it bumu nekk kuy door a gëm, ngir mu bañ a yég boppam, bay dajeek mbugalu Yàlla, ni ko Seytaane defe woon.
  
7. Te it war na am seede su rafet ci waa àddina, ngir ñu bañ koo diiŋat, ba muy daanu ci fiiru Seytaane.
  
8. Kiy topptoo li mbooloo miy jëfandikoo itam na am faayda te fonk kàddoom; bumu di ku yàqu ci sangara, mbaa ku alal jiital.
  
9. Na sàmm mbóoti ngëm gi ak xel mu dal.
  
10. Moom itam nañu ko jëkk a seetlu, ba mu leer ne amul ŋàññ, ñu door koo fal.
  
11. Naka noonu, na jigéen ñi am faayda, bañ a jëw mbaa xér ci dara, waaye nañu takku ci lépp.
  
12. Ku ñu dénk sasu topptoo yëfi mbooloo mi nag, nay ku yem ci benn soxna, jiite bu baax këram ak i doomam.
  
13. Ndaxte ku ci rafetal sasam dina am tur wu tedd ak kóolute gu mat sëkk ci yoonu ngëm, gi ci Kirist Yeesu.
  
14. Bëgg naa laa seetsi balaa yàgg,
  
15. waaye amaana mu yéex. Moo tax ma lay bind bataaxal bii, ngir xamal la, ni ñu war a nekke ci kër Yàlla gi, maanaam ci mbooloom Yàlla Aji Dund ji, miy kenug dëgg te di sëslaayam.
  
16. Ci dëgg-dëgg ragal Yàlla ëmb na mbóot yu xóot:Ki wàcc, yor bindu nit,mu bir ne xelam jub na,te malaaka ya gis ko;xamlees na ko ci xeet yi,ñu gëm ko ci kaw suuf,te Yàlla teeru ko ci ndamam.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES