Bible Study: FrontPage




 

1 Timothy, Chapter 4

Bible Study - 1 Timothy 4 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Xelum Yàlla mi wax na bu leer ne, ci mujug jamono dina am ñu bàyyi yoonu ngëm wi, di topp ay xel yuy fàbbee ak xalaati Seytaane.
  
2. Ñooñu ay naaféq yuy naxe lañu, te seen xol dërkiis.
  
3. Dinañu tere séy, di araamal ay ñam, fekk Yàlla sàkk na leen, ngir ñi gëm te xam dëgg man ciy jëfandiku ak cant.
  
4. Ndaxte li Yàlla sàkk lépp baax na, kon wenn ñam araamul ci ku koy jëfandikoo ak cant.
  
5. Ndaxte kàddug Yàlla ak ñaan ñoo koy sellal.
  
6. Saxal ci digal bokk yi loolu nag, kon dinga nekk jawriñu Kirist Yeesu ju baax ju regg ci kàdduy yoonu ngëm wi ak njàngale mu rafet, mi nga xam bu wér.
  
7. Tanqamlul ay léebi diiney neen, di ay wax yu amul bopp yu àddina kese; waaye tàggatal sa bopp ci ragal Yàlla.
  
8. Ndaxte tàggat yaram am na fu njariñam yem, waaye njariñu ragal Yàlla dafa daj lépp, ëmb digey àddina ak àllaaxira.
  
9. Wax ju wóor a ngii, te mat a nangu ak gépp kóolute.
  
10. Danuy ñaq tey bëre, ndaxte wékk nanu sunu yaakaar ci Yàlla Aji Dund ji, di Musalkatu ñépp, rawatina nag ci ñi gëm.
  
11. Digal leen yëf yooyu nag ci sa njàngale.
  
12. Bu la kenn xeeb ndax say at, waaye defal sa bopp royukaayu ñi gëm ci say wax ak say jëf, ci sa mbëggeel, sa ngëm ak sa cell.
  
13. Li feek may dikk, saxal ci jàng di biral Mbind mi ci mbooloo mi, di leen dénk ak a jàngal.
  
14. Bul sàggane may gi nekk ci yaw, gi la Yàlla jox jaarale ko ci waxu yonent, keroog bi la njiit yi tegee loxo.
  
15. Faaydaalal yëf yooyu te sóobu ci, ba sa jëm kanam bir ñépp.
  
16. Sàmmal sa bopp te sàmm sa njàngale, te sax ci; noonu dinga musal sa bopp, yaw ak ñi lay déglu.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES