Bible Study: FrontPage




 

2 Corinthians, Chapter 6

Bible Study - 2 Corinthians 6 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Nun nag ñiy liggéeyandoo ak Yàlla, nu ngi leen di ñaan: jariñooleen yiw, wi ngeen jote ci Yàlla, ngir mu bañ a neen ci yéen.
  
2. Ndaxte Yàlla nee na:«Ca jamono ja mu jekke, nangu naa sa ñaan;ci bésu mucc gi laa la wallu.» Tey jii la jamono ju jekk ji; tey la bésub mucc gi.
  
3. Bëggunoo lëmbaaje xelu kenn ci dara, ngir kenn bañ a sikk sunu liggéey.
  
4. Li nu bëgg moo di rafetal sunu tur ni jawriñi Yàlla ci fànn gu nekk; danuy muñ coono yi, tiis yi, njàqare yi;
  
5. ñu nuy dóor, di nu tëj ci kaso, dëkk yi di yengu ndax sunu mbir; nuy liggéey ba sonn, di fanaanee xool, di woor.
  
6. Nu ngi rafetal sunu yen ci dund gu sell, ci xam-xam, muñ ak laabiir, ci Xel mu Sell mi ak ci mbëggeel gu raxul njublaŋ,
  
7. ci kàddug dëgg ak ci kàttanu Yàlla, nu ngi yor gànnaayi njubte ci loxol ndeyjoor ak lu càmmooñ.
  
8. Ñu bàkk nu, jéppi nu, sant nu, xas nu. Ñu di nu jiiñ réeral, moona niti dëgg lanu.
  
9. Ñuy xeeb sunu tur, moona tur yi siiw nañu. Nu mel ni ñu loof, moona nu ngi dund. Ñu yar nu, teewul nu rëcc ci dee.
  
10. Danuy dékku tiis, waaye di bég fu nu tollu. Nu tumurànke, waaye di woomal ñu bare; amunu dara, fekk noo moom lépp.
  
11. Yéen bokki Korent, wax nanu leen sunu biir ak sunu biti, di leen ubbil sunu xol.
  
12. Ubbiku nanu ci yéen, waaye yéen ubbikuwuleen ci nun.
  
13. Maa ngi wax ak yéen ni samay doom; feyleen nu bor bi, yéen itam; ubbileen seen xol!
  
14. Buleen likkoo ak ñi gëmul. Gan àndandoo moo man a am diggante njubte ak ndëngte? Gan booloo moo man a am diggante leer ak lëndëm?
  
15. Gan déggoo moo man a am diggante Kirist ak Beliyar? Gan jaxasoo moo man a am diggante ki gëm ak ki gëmul?
  
16. Nan la këru Yàlla man a mànkoo ak xërëm yi? Ndaxte nun nooy këru Yàlla Aji Dund ji, ni ko Yàlla waxe:«Dinaa dëkk ci seen biir,tey dox ànd ak ñoom,ma nekk seen Yàlla,ñuy samay gaay.»
  
17. Kon nag Boroom bi nee na:«Génnleen biir ñooñu te beru.Buleen laal dara lu am sobe,kon dinaa leen teeru.
  
18. Dinaa nekk baay ci yéen,ngeen di doom ci man, muy góor, di jigéen. Moom la Aji Kàttan ji wax.»


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES