Bible Study: FrontPage




 

2 Corinthians, Chapter 7

Bible Study - 2 Corinthians 7 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Ndegam nag jot nanu ci dige yu mel nii, samay soppe, nanu sellal sunu bopp ci bépp sobeb yaram walla bu xel, dund dund gu sell, ba mat ci ragal Yàlla.
  
2. Yaatal-leen nu ci seen xol. Tooñunu kenn; lorunu kenn; naxunu kenn, jël alalam.
  
3. Teg leen tooñ taxul may wax lii, ndaxte wax naa ba noppi ne, yéena ngi ci sunu xol ci dund ak ci dee.
  
4. Kóolute gi ma am ci yéen réy na. Tiitar bi may jële ci yéen réy na. Sama xol sedd na guyy. Damaa fees ak mbég ci bépp coono bu nuy daj!
  
5. Ba nu àggee diiwaanu Maseduwan, noppaluwunu, waaye coono bu ne daj nanu ko: xeex ci biti, njàqare ci biir.
  
6. Waaye Yàlla miy dëfël xolu ñiy yoggoorlu ndax tiis, dëfël na sunu xol ci ñëwu Tit,
  
7. te du ci ñëwam rekk sax waaye ci li ngeen dëfël xolam. Yégal na nu seen nammeel ci nun, seen réccu ak seen farlu jëm ci man, ba sama mbég gën cee yokku.
  
8. Su fekkee ne sax, bataaxal bi ma leen bind dafa leen naqare, réccootuma ko. Ci lu jëkk réccu naa ko, ndaxte gis naa ne, bataaxal boobu teg na leen tiis, doonte sax ci diir bu néew.
  
9. Waaye sama xol sedd na léegi, du ndax seen tiis, waaye ci li mu tax ngeen réccu. Tiis wu jóge ci Yàlla ngeen tegoo, te àndul ak benn loraange bu bawoo ci nun.
  
10. Ndaxte tiis wu jóge ci Yàlla dina jur réccu guy jëme ci mucc, te réccu googu laajul gëstu. Waaye tiisu àddina day jëme ci dee.
  
11. Seen tiis wi jóge ci Yàlla, gisleen nag li mu jur: ndaw njaxlaf ak lay ak mer ak ragal ak nammeel ak farlu, ak bëgg a yar ki tooñ! Ci seen jëf yépp wone ngeen ne, set ngeen wecc ci mbir moomu.
  
12. Kon nag su ma leen bindee, ki tooñ taxul, ki ñu tooñ it taxul, waaye dama leen a bind, ngir ngeen man a gis ci kanam Yàlla cawarte, gi ngeen am ci nun.
  
13. Te loolu seral na sunu xol. Sunu xel dal na, rawati ci li nu ànd ak Tit ci mbégam, ci li ngeen seral xolam, yéen ñépp.
  
14. Su fekkee ne tiitaru woon naa ci seen mbir ci kanamu Tit, rusuma ci. Dëgg rekk lanu leen mas a wax; noonu it la Tit gise ne, li nu leen doon seede lépp, dëgg la.
  
15. Te mbëggeelam ci yéen gën na yokku, buy fàttaliku ni ngeen ko déggale yéen ñépp, ci li ngeen ko teeru, ànd ak ragal ak weg.
  
16. Bég naa, ndaxte xam naa ne, man naa leen a wóolu ci lu nekk!


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES