Bible Study: FrontPage




 

2 Thessalonians, Chapter 2

Bible Study - 2 Thessalonians 2 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Ci lu jëm ci ñëwu Boroom bi Yeesu Kirist nag, bokk yi, ak sunu daje ak moom, am na lu ma leen di ñaan:
  
2. bu leen kenn gaaw a tàggale ak seen sago, mbaa di leen jaaxal, muy yonent buy wax, muy kàddu mbaa bataaxal bu ñu nu moomaleel, ci ne leen bésu Boroom bi ñëw na xaat.
  
3. Bu leen kenn nax ci benn fànn, ndaxte balaa booba, fàww Xiiroo bu mag bi ak Yàlla am, te Nitu ñaawteef ki feeñ, moom aji alku ji.
  
4. Day weddi lépp lu ñu teg Yàlla walla ñu koy jaamu, di yékkati boppam, ba toog sax ca kër Yàlla ga, tudde boppam Yàlla.
  
5. Xanaa fàttalikuwuleen ne, waxoon naa leen ko, ba ma nekkee ak yéen.
  
6. Te xam ngeen li ko téye léegi, ba du man a feeñ lu dul ci waxtoom.
  
7. Ndaxte fi mu ne ñaawteef gaa ngi jax-jaxi xaat ci kumpa, waaye ki ko téye mi ngi fi ba tey. Bu fi jógee nag,
  
8. Nitu ñaawteef ki dina feeñ, te Boroom bi Yeesu dina ko rey ak ngelawul gémmiñam, tas ko ak leer giy ànd ak ñëwam.
  
9. Bu Nitu ñaawteef kooku feeñee, dina ànd ak kàttanu Seytaane ak doole ju bare, di wone ay firnde ak ay kéemaan yu dul dëgg;
  
10. te dina nas bépp naxe buy sànke, ba yéem ñi nar a alku, ndaxte ubbiluñu seeni xol dëgg, gi leen manoon a musal.
  
11. Looloo tax Yàlla yónnee leen xelum réer, ba ñu gëm fen.
  
12. Noonu Yàlla dina mbugal ñépp ñi gëmul woon dëgg te doon bànneexu ci njubadi.
  
13. Kon nag bokk yi, yéen ñi Boroom bi bëgg, mënunu lu dul sax ci sant Yàlla ci li mu leen tànn ca njàlbéen ga, ngir musal leen, mu sédde leen boppam jaarale ko ci jëfu Xel mu Sell mi ak seen gëm dëgg gi.
  
14. Te Yàlla woo na leen ci loolu jaarale ko ci xebaar bu baax, bi nu leen doon yégal, ngir ngeen bokk ci ndamu sunu Boroom Yeesu Kirist.
  
15. Kon nag bokk yi, taxawleen bu dëgër te jàpp ci dénkaane yi nu leen jottali, muy ci li nu wax, muy ci li nu bind.
  
16. Na sunu Boroom Yeesu Kirist moom ci boppam ak Yàlla sunu Baay, mi nu bëgg te wone yiwam ci nun, ba ubbil nu buntu jàmm ju sax ak yaakaar ju wér,
  
17. dëfël seeni xol te saxal leen ci bépp jëf ju rafet ak gépp kàddu gu baax.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES