Bible Study: FrontPage




 

2 Thessalonians, Chapter 3

Bible Study - 2 Thessalonians 3 - Wolof - Wolof Bible - Web
 
 
 
Comment!       Comment Disqus!
  
1. Léegi nag bokk yi, ñaanal-leen nu, ngir kàddug Boroom bi law te ànd ak ndam, ni mu ko ame woon ci yéen.
  
2. Ngeen ñaanal nu it, ngir nu mucc ci ñi bon te soxor, ndaxte du ñépp a gëm.
  
3. Waaye Boroom bi kuy sàmm kóllëre la; dina leen dëgëral te musal leen ci Ibliis.
  
4. Te wóor nanu ci kanamu Boroom bi ne, yéena ngi def li nu leen santoon, te dingeen ci sax.
  
5. Na Boroom bi gindi seeni xol ci mbëggeelu Yàlla ak muñu Kirist.
  
6. Nu ngi leen di sant it bokk yi, ci turu sunu Boroom Yeesu Kirist, ngeen dëddu bépp mbokk buy wéy ci tayel te bañ a topp dénkaane, yi nu leen jottali.
  
7. Xam ngeen bu baax, yéen ci seen bopp, ni ngeen war a awe ci sunuy tànk. Ba nu nekkee ca yéen, wéyunu woon ci tayel
  
8. te musunoo lekk ñaqu kenn. Waaye guddi ak bëccëg danu daan ñaq, di sonn, ngir bañ a wéeru ci kenn ci yéen.
  
9. Waxuma ne amunu sañ-sañu def ko, waaye danoo bëggoon a nekk ay royukaay ci yéen, ngir ngeen aw ci sunuy tànk.
  
10. Ndaxte ba nu nekkee ca yéen, lii lanu tëraloon: «Ku liggéeyul, du lekk.»
  
11. Léegi nag dégg nanu ne, am na ci yéen ñuy wéy ci tayel; liggéeyuñu dara, lu dul di dugg ci lu seen yoon nekkul.
  
12. Ñu deme noonu nag, nu ngi leen di sant te di leen dénk ci turu Boroom bi Yeesu Kirist, ñuy liggéey ci jàmm tey dunde seen ñaq.
  
13. Yéen nag bokk yi, buleen tàyyi ci def lu rafet.
  
14. Su kenn bañee topp li nu bind ci bataaxal bii, ràññeeleen ko te sore ko, ngir mu rus ci.
  
15. Waxuma ngeen def ko noon, waaye ngeen yedd ko ni seen mbokk.
  
16. Na leen Boroom jàmm may jàmm ci fépp ak ci lépp. Na Boroom bi ànd ak yéen ñépp.
  
17. Tàggoo bii maa ko bind ci sama loxo, man Pool. Nii laay binde, te di màndargaale nii sama bataaxal yépp.
  
18. Na yiwu sunu Boroom Yeesu Kirist ànd ak yéen ñépp.


Search in:
Terms:

Vote and Comment on Facebook:Recommend This Page:
Post on Facebook Add to your del.icio.us Digg this story StumbleUpon Twitter Google Plus Post on Tumblr Add to Reddit Pin this story Linkedin Google Bookmark Blogger
Insert Your Personal Insight:

Please do not make mean comments and follow the biblical and spiritual character of this forum. If, however unpleasant situations arise, we request to flag it to us in order to evaluate the situation.

Text source: This text is in the public domain, downloaded from http://www.unboundbible.org, compiled by biblephone2008@gmail.com.

This project is based on delivering free-of-charge the Word of the Lord in all the world by using electronic means. If you want to contact us, you can do this by writing to the following e-mail: bible-study.xyz@hotmail.com


SELECT VERSION

COMPARE WITH OTHER BIBLES